Appli bii mooy Kàddug Yàlla, gi dikke ñaari pàcc: Kóllëre gu jëkk gi Yàlla fas ak nit, ak Kóllëre gu yees, gi mujja wàcc, te ñenn ñi di ko wooye Injiil, mu tekki Xibaaru jàmm. Ñaari téere yooyu, Yàllaa leen wàcce ci nitam ñu sell ñi, kóllëre gu jëkk gi, ñu bind ko ci yawut, gu yees gi, ci làkku gereg. Li ñu bind ci téere yu jëkk ya nag, moom lanu tekki ci wolof.
Man nga ko jàng ci wolof, wolofal, français, anglais, ak grec.